From Wikipedia, the free encyclopedia
dëkkug lebu yi ci ndakaaru mi ngi am ginnaaw ay duusi gàddaay ci diggante XV¹⁵ ak XVIu¹⁶ xarnu. Laataa seenug càmp ci Senegaal, ab tukki bu gudd moo leen war a jëlee ca penku Afrig ba ci sowwu Afrig jaare ko ci bej-gànnaaru gox bi. Ñaari gongikuwaayu xibaar lanu am ngir man a jéem a rëddaat yoon wi leen fi indi. Nettali gi ciy kàddu di na tax nu man xam lu bari ci jamono yu mujj yi. liggéey yu ay gëstukat niki Seex Anta Joob T. Gostynski, G. Balandier ak P. Mercier, F. Brigaud di nañu tax nu man a dem ba ca njëlbeen
Tambali na am na 7 000 at, tukki bi jaare ci bëj-gànnaaru Afrig, ci ay pàcc yu bari la ame. Jàpp nanu ne dañu leen fay war a dàqe walla ñu demal seen bopp ngir lànk nooteel. Aw askan wu fonk i baaxam (aadaam), ak i melokaanam la. Ci melokaan yooyu sax lañu sukkandiku ngir joxe ay gongikuwaayu baatu lebu. Am na ñu ne mi ngi joge ci baatu lebu (maanaam dëkku, misaal: dëkku am mbër ), ndax seen mbañug nooteel, ñeneen ni ci lubu (jqmbaar) la jóge, ak yeneen.
Laataa ñëwug lebu yi ci Ndakaaru, juróom-benni gàddaay yu toppante lañu amal. Bi ñuy ñëw ay mbooloo yu ndaw lañu doon def, ndànk ndànk ñuy toog, ci ndoorteel gi ci barab yi soose yi nekkul woon, ñu dem ba sanc Ndakaaru gépp. (Caam, 1970:6)
Ñi ngi agsi ci 1430 (atum junni ak ñenti téeméer ak fanweer), boobu ag nguuru soose, gu tambalee woon Tubaab Jalaaw ba Ngor, moo fa nekkoon. Ca jamono yooyu, ay réewi soose yu bari ñoo fa amoon, ci seeni bopp ñii ñoo fa nekkoon: Malang Tambaa, Jalla Jaw, Gitigi Maroon, Nak Jombel moom dund na ba 1470. Xare bu tar ba ca toppoon waraloon dawug Soose yi jëm Gàmbi.
Jàppante bi wéy na ba ci XVu¹⁵ xarnu bi, ba killifay soose yi deewee la xare ba jeex. Ca la lebu yépp jóge Jolof mi doon waaj a xar, ndànk ndànk ñu dem ba moom Ndakaaru gépp. Ginnaaw bi yàggul dara dammeelu Kajoor di leen jéem a sanc loolu jur ay xare yu bari ci seen diggante.
Nosiinu seenug mboolaay, ci li ñu xam, am na laataa seenug ñëw ci Ndakaaru te mi ngi dàttu woon ci palug ab Laman. Ndànk ndànk ñàkk kaaraange gi ak jamono ju laaj jeneen nosiin tax yeneen cëslaay taxaw.
Ci boppu askan wi, Jaraaf bi moo fa nekkoon, di ki jiite nguur gi, Ndey-ji-réew ji tegu ci, di ki yoroon mbiri biir ak biti réew. C.T. Mbeng moom daf ko jappe niki "ab aji-teewal ak aji-rattaxal ci diggante réewi lebu yi". Saltige bi moom moo yoroon suuf si ak aartu (défense) gi ak ndox mi. Ñett ñii ñoo yoroon doxiinu réew mi. Taxawaloon nañu ñaari pénc ngir ñu jàppale ñett ñooñu ci seen liggéey: Jàmbur ak péncu fere yi. Bu njëkk bi di nañu ko wax itam ""jataayu mag ñi"" boroom xam-xam yi rekk a fay nekk, Ndey-ji-jàmbur moo koy jiite. Péncu fere
Jàmbur bi mooy kiy fal jaraaf, ndey-i -réew ak alkaati bi. Te ñiy yor yooyule ndombal-tànk waruñoo doon ay xeet (maanaam ñu bokk ci wàllu yaay). Lii di na tax ba man-man (pouvoir) gi du nekk rekk ci yoxoy genn njaboot. Bii matuwaay di na tax ba réew mi du soppiku nguur. Kon man-man gi dañu koy séddale ci njaboot yu bari, ku nekk man ngaa am ndomba-tànk, suñuy tànn kenn, ci genn njaboot gi, lenn li ñuy xool mooy ay mbaaxam.
Seamless Wikipedia browsing. On steroids.
Every time you click a link to Wikipedia, Wiktionary or Wikiquote in your browser's search results, it will show the modern Wikiwand interface.
Wikiwand extension is a five stars, simple, with minimum permission required to keep your browsing private, safe and transparent.