Karasol

From Wikipedia, the free encyclopedia

Karasol

Karasol garab la gu bàyyikoo ci lu bir ci àll yu naaje yu Karayib, yu Amerig gu digg ak gu bëjsaalum.

Thumb
Karasol gi (Annona muricata)

Melo wi

Thumb
Tóortóorum garabug karasol

Karasol gàncax la gu ndaw. Guddaayam danay àgg 3 ba 10i met. Xobam melo wu nëtëx la yor. Tóor-tóoram 3i xob la yor. Day meññ at mépp.

Njariñ yi

Thumb
Karasol bi

Karasol dees na ko lekk. Dees na ci defar njar. Dees na ci fajoo it.

Turu xam-xam wi

Annona muricata

Tur wi ci yeneeni làkk

farañse: corossolier
angale: soursop tree
itaaliyee: graviola
Loading related searches...

Wikiwand - on

Seamless Wikipedia browsing. On steroids.